Ci atum 2015 la Fondation Beethoven, dig kurél gu nekk Bonn, ca réewum Allemagne, tey yëngu ci mbirum taaral ak caada, tàmbalee jagleel ndongo-daaray Ërob yi joŋante bi ñu duppe ‘’Bonn hoeren-sonotopia’’. Joŋante boobu nag, benn la ci àddina sépp, moom rekk lañ mën ni mooy suqali taaralkat yu ndaw yiy liggéey ci mbirum riir, di ci wone seen mëninu fentaakon.
sonotopia-the sonic mi wër àddina si juróom-ñaar yéeeem moo doon way-ràññeeku yi njëkk a gàddu ndam li ca Bonn, doon daanaka royukaay yiy siiwal taaralu riir ci réew yépp, tax ba ñépp gën koo sopp. Doom-aadama, su bëggee xel mi ubbeeku ci nekkinu askan wi, mu nànd doxinam, fàww mu ubbiy noppam, ne tekk di déglu. Nit ki, bala muy juddu, xippi, gis li ko wër, fekk na mu jot a dégg lu baree-bare. Looloo biral ne dégg mooy lal bépp xeetu jokkoo ak jëflante. Ñaar yooyu yépp dees leen a war a jàng.
Ci diirub weer, ñaari goney taaralkati riiru Ërob dinañ dem Téhéran (Iran), ñëw Ndakaaru (Senegaal), jóge fi dem Valparaiso ca Chili. Réew mu ci nekk dinañ fa liggéeyandoo ak ñaar ci seeniy naataangoo, jaare fa wasaare mébét meek seeni gëstuy bopp. Dinañu am i njaatige ci réew yooyu ñu leen di jàppale, yenn kurél yi tamit naka noonu.. Nan la ab dëkk di riire ? Naka la waaso bu nekk di déggee ka déglu ? Kurél yooyu dinañ indi tont ci laaj yu ni deme. Li tax a jóg sonotopia-the sonic explorers, mooy lal waxtaan ci mbirum taar ak riir ñeel réew yu bare, natt ko, xool ni ko fentkat yiy soppee.
Ñaar-téeméer-ak juróom-fukkeelu bésu-juddug Beethoven, yemook mujjantalu liggéey bii nu sumb, lu tollu ci fukki taaralkati riir ak ñaar war nañoo daje ca Bonn, weccee fa xalaat ci seeni jaar-jaar, xool nu ñuy jëmalee kanam seen liggéey, naka lañuy yeesale seen doxalin, mu méngook jamono. Li cay ruuse dees na ko fésal ci wonale bi ñuy waajal ca Bonn te tudde ko ‘’Künstlerforum’’. Ci ñaareelu paacu mébét mi, Ismaël Adramé Coly (SN), Nika Schmitt (LU), Martin Tornow (DE), Anna K. Wane (SN) ak seeniy njaatige Marion Louisgrand Sylla (SN) ak Stefan Rummel (DE), ñoom ñooñu ñépp diy saytukati riir, dinañu wër ay goxi Ndakaaru, def ciy njàngat. Looloo ngi tàmbali ci 17u fan ci weeru féwaryee, jeex ci 17u fan ci weeru màrs, atum 2020.
WAXTAAN : 21u fan ci weeru féwaryee 2020 ci 7i waxtu ci ngoon, ca Kër Thiossane (Cosaan)
Àjjuma jooju la lépp di door, ci kilifteefu Carsten Seiffarth, di kenn ci njiiti taaral yi. Ca Kër Thiossane lay ame. Bés boobu, taaralkat ya fa teew yépp dinañu wax naka lañu gisandee mbir mi.
Bu keroogee Kër Thiossane ak sonotopia–the sonic explorers dinañ ubbil ubbil askan wépp seen bunt ngir ñu ñëw déglu taaralkati riir yi, weccook ñoom xalaat.
sonotopia–the sonic explorers, bànqaasu ‘’Bonn hoeren’’ la. Kurélu gi ñuy wax ‘’Fondation Beethoven’’ tey yëngu ci taaral ak caada ca Bonn moo ko yilif.
Ci ndimbalug Kunststiftung NRW.
Ci lëkkalook Goethe-Institut bu Senegaal ak Kër Thiossane.
Ci njiiteefu : Carsten Seiffarth
Njaatige taaral yi : Carsten Seiffarth ak Carsten Stabenow
Markus Steffens moo féetewoo ndefaru mébét mi
Marion Louisgrand Sylla mooy naataangoom ci Ndakaaru.
Ngir am yeneen xibaar ak i leeral, demal fii >>>